Aller au contenu

Saytubiddiw

Jóge Wikipedia.

Saytubiddiw mooy xam-xam biy xool aka saytu biddiw yi, di jéem a faramface ak a leeral seen melokaan ci jëmm ak ci simi, seenug magg ak seen cosaan. Doon na xam-xam bu am lu ëpp 6 000 at, ay cosaani saytubiddiw jiitu na jomono ju yàgg ja.

Te ñu bañ koo jaawale ak gëstubiddiw.

Taariixkat yi nee nañu saytubiddiw mooy xam-xam bi gën a yàgg ci àdduna bi. Xay yu njëlbeenu yi sax amoon nañu ci ay xam-xam.


Xam-xamu saytu-bidiw bokk na ci xam-xam yu njëkk yi am ci fajarug nite, moom xam-xam la buy yittewoo fuglu ak jàng xew-xew yiy xew ci bitib kol-kol bu suuf si ak ci muuraay gu jawwoom gi. Mooy it xam-xam biy joxe xibaar yi aju ci feeñte (phenomene)yu bidiw yi. Saytu-bidiw mooy gëstu tàmbalig yaram yi ñu man a fuglu ci asamaan si (biti suuf si), ak séenug jëm-kanam ak séeni jagle yu jëmm (walla fisiyaa) ak yu kimyaa, ak xew-xew yi ñuy àndal.

  • Français:astronomie
  • English:astronomy

Logo Wikbaatykaay

Xool it Wikbaatukaay


Xam-xam
Xam-xam
Gëstubiddiw | Jëmm | Paj | Saytubiddiw | Simi | Xam-xamu suuf si ak jawwu ji | Xayma
Xarala
Jokkoosoryante | Xaralaymbëj | Doolerandu | Kàttan | Xam-xamu nosukaay | Mbëjfeppal
Xam-xami nite ak mboolaay
Diine | Melosuuf | Wërlaay | Nit | Yoon | Koom-koom | Taariix | Xeltu | Kàllaama